¶ Aji Sax ji nag wàcc ci biir aw niir, taxaw ak Musaa foofa, daldi biral turam, ne: «Aji Sax ji.»
TSK
TSK · Numbers 11:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Maay wàcc wax ak yaw foofa te maay sàkk ci leer gi ci yaw, def ko ci ñoom, ñu yenule la yenu mbooloo mi, ba dootuloo ko yenu yaw doŋŋ.
¶ Musaa daldi jubal ca Datan ak Abiram, magi Israyil topp ca.
Bu loolu weesee nanga dem ba ca Gibeya Eloyim, fa dalub xarekati Filisti ya nekk. Booy jub dëkk ba, dinga dajeek kurélu yonent yu jóge ca bérabu jaamookaay ba, aw nit jiitoo leen powum tabalaaki toxoro, ak ñaari xeeti xalam, yonent ya di waxe ni yonent.
Sóol yebal ay ndaw, ngir ñu jàpp Daawuda. Nit ña dikk, gis kurélu yonent yuy wax ay waxyu, Samiyel jiite leen. Ba loolu amee, ca kaw ndawi Sóol ya la Noowug Yàlla wàcc, ñuy wax ay waxyu, ñoom itam.
Sa xel mu rafet nga leen may ba ñu mana ràññee, sa mànn it, noppiwuloo leen koo leel, teg ca ndox ma nga leen daan fajale mar.
Yeremi nag wax Barug, ne ko: «Man damaa am ngànt. Duma mana dem kër Aji Sax ja.
Naka lay wax loolu, aw niir dikk yiir leen, taalibe ya tàbbi ca biir niir wa, tiitaange jàpp leen.
Kenn ca ñoom, ku ñuy wax Agabus daldi yéglee Noo gu Sell gi, ne xiif bu metti dina am, ci àddina sépp. Te looloo nga yemook ayug buur bu mag bu ñuy wax Këlódd.
Kon gépp góor guy julli, mbaa muy waxe kàddug waxyu, bu muuree boppam, suufeel na Almasi, miy boppam.
Biralkati kàddug waxyu yi ñoo wara jiite xel mi ñuy waxe.
Ndax kat du genn kàddug waxyu gu masa soqikoo ci coobarey nit, waaye ci xiirtalub Noo gu Sell gi la aw nit daan waxe waxyu bu bawoo fa Yàlla.