TSK

TSK · Numbers 12:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Gannaaw ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, mu ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.»

¶ Guddi googu Yanqóoba dafa gént, gis raas bu sampu ci suuf, te cat la sar asamaan, malaakay Yàlla yi di ci yéeg ak a wàcc.

¶ «Ba ñu demee ba jur giy wara tëbu, damaa jeneer sikket yiy tëb bëy yi yépp di lu seereer ak lu tippante mbaa ñu raxe.

¶ Gannaaw gi geneen gént dikkal ko, mu nettali ko ay magam ne leen: «Dégluleen, géntaat naa. Gis naa jant bi ak weer wi ak fukki biddiiw ak benn di ma sujjóotal.»

¶ Aji Sax ji ne Musaa: «Dama ne, def naa nga féete Firawna fi ko Yàlla féete, sa mag Aaróona di sa yonent.

Ab yonent laa leen di feeñalal ci seen biiri bokk, ni yaw. Maay yeb samay kàddu ci gémmiñam, mu àgge leen mboolem lu ma ko sant.

Mu seetlu ci Aji Sax ji, Aji Sax ji wuyuwu ko; du ci gént, du ci jumtukaayu tegtal bi ñuy wax Urim, du ci kàddug yonent.

Foofa ca Gabawon la Aji Sax ji feeñu woon Suleymaan ci géntug guddi. Yàlla ne ko: «Ñaanal loo bëgg, ma may la ko.»

Job 33:15 TSK

ci biir peeñum géntu guddi, fa nelaw dabe nit, ba mu yàndoore kaw lalam.

ne leen: «Buleen laal samay tànnéef, buleen lor samay yonent.»

¶ Am na bés, mu yemook sama fanweereelu at, juróomi fan ca ñeenteelu weer wa, booba maa nga bokkoon ca ña ñu toxal ca tàkkal dexu Kebar. Asamaan daa ubbiku, ma daldi gis ay peeñuy Yàlla.

¶ At ma jëkk ca nguurug Baltacar buuru Babilon, Dañeel daa gént, peeñu dikkal ko ci kaw lalam. Mu bind nag gént gi, doore ko nii.

Ba loolu amee ma des fa man rekk, ne jàkk ci peeñu mu réy moomu. Waaye deseetuma woon doole, damaa jeexal tàkk, amatuma genn kàttan.

Maa wax ak yonent yi, yokk peeñu yi, te yonent yi, maa leen waxyu ay misaal.»

Maa jekki gis, ag guddi, nit ku war fas wu xonq. Moom nag mu ngi taxaw ci biir garabi mirt ci aw xur, li ko féete gannaaw di fas yu xonq, ak yu ngëlembu, ak yu weex, ak seeni gawar.

Luke 1:22 TSK

Ba mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Ñu daldi xam ne am na lu ko feeñu ca néeg Yàlla ba. Ma nga leen di liyaar, manatula wax.

Mu daldi gis asamaan ubbiku, lu mel ni sér bu mag bu ñu téyee ñeenti lafam, wàcce asamaan, jëm suuf.

¶ «Yàlla def, gannaaw ba ma délsee Yerusalem, ma doon ñaan ca kër Yàlla ga, daldi daanu leer.

Dinaa may nag sama ñaari seede yi, ñu biral waxyu diiru junni ak ñaar téeméeri fan ak juróom benn fukk (1 260) yu ñuy sol ay saaku, di ko toroxloo.»