TSK

TSK · Numbers 13:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yosuwe doomu Nuun, ak Kaleb doomu Yefune, ñoom ña bokk ca ña seeti woon réew ma, daldi xotti seeni yére ndaxu tiis.

Fexeleen rekk ba Aji Sax ji, buleen ko gàntal, te yeen nag ngeen baña ragal waa réew ma, ndax ab lanc doŋŋ lañu nuy mat. Seen kiiraay dëddu na leen, te Aji Sax jaa ngeek nun. Buleen leen ragal.»

Ñeel Daawuda. Aji Sax jee may leeral, di ma wallu. Ana ku may ragal? Aji Sax jeey aar sama bakkan. Ana ku may tiit?

Yéefar yépp a ma sam, ma bëmëx leen ci dooley Aji Sax ji.

¶ Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?