Weeru lëmm kay lañuy yàpp, ba yàpp wiy génne ci seen paxi bakkan, ba mujj génnliku leen, gannaaw ñoo xarab Aji Sax ji ci seen biir, di jooy ci kawam, naan: “Moo lu nu taxoona jóge Misra!”»
TSK
TSK · Numbers 14:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Numbers 11:20
TSK
Aji Sax jee leen di yeb ciy gaal, delloo leen Misra, yoon wu ma leen noon dungeen ko gisati, ngeen di fa jaay seen bopp seeni noon, ngir doon seen jaam yu góor ak yu jigéen, te kenn du leen jënd.
Nehemiah 9:17
TSK
Ñoo baña dégg, baña bàyyi xel sa kéemaan yi nga def ci seen biir, te ñoo sajju loos, fétteeral ba fal njiit, nara dellu ca seen njaam ga. Waaye yaw yaay Yàlla jiy boroom njéggal ak yiw ak yërmande, di muñ mer, te bare ngor, ba tax waccoo leen.
Luke 17:32
TSK
Fàttlikuleen jabaru Lóot ja!
Hebrews 10:38
TSK
Sama nit ku jub nag mooy dund ndax ngëm ga, waaye ku dellu gannaaw, sama xol bégewu la.»
2 Peter 2:21
TSK
Ndax kat ñàkkoona xam yoonu njub wi sax moo doon gën ci ñoom, xam ko ba noppi, dëddu ndigal lu sell la ñu leen ca àgge woon.