Exodus 29:28
TSK
Aaróona aki sëtam la loolu di doon seen cér bu bànni Israyil di warlook ñoom ba fàww, ndax ab jooxe la; jooxe bu bànni Israyil di génnee ci seen saraxi cant ci biir jàmm, muy seenub jooxe, ñeel Aji Sax ji.