¶ «Na màggal googu di pàttliku ci yeen. Na mel ni màndarga mu nekk ci seen loxo ak seen jë. Su ko defee ngeen saxoo jàngle yoonu Aji Sax ji, ndax ci dooley loxoom la leen Aji Sax ji génnee Misra.
TSK
TSK · Numbers 15:39
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Wattuleen seen bopp ba baña fàtte kóllëre gi seen Yàlla Aji Sax ji fas ak yeen, di sàkkal seen bopp tuur muy jëmmal lenn, te seen Yàlla Aji Sax ji aaye leen ko.
wattuleen seen bopp bala ngeena fàtte Aji Sax ji leen génnee réewum Misra, kërug njaam ga.
Alkàndee ngi, ndegam déggaluleen seen santaaney Yàlla Aji Sax ji, xanaa wacc yoon wi ma leen di dénk bésub tey, ngir topp yeneen yàlla yu ngeen xamuloon.
Ndegam samay tànk a moy yoonu njub, mbaa sama xol topp saay gët, mbaa sama yoxo yii gàkk fenn,
seeni jëf sobeel leen, ndax seen bokkaale.
Ku doyloo sam xel, dof nga; ku jëfe xel mu rafet, mucc nga.
Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Yàllay Israyil dafa wax ne: «Maa ngii di leelsi xeet wii njàqarey xeme, nàndal leen tookey mbugal.
Askanu Yuda ak askanu Israyil dañuy dellu booloo, daldi tabbal seen bopp genn kilifa, te dinañu sëq ci réew mi, ndax bésub Yisreel ba dina réy.