TSK

TSK · Numbers 16:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ca jamono yooya ak itam gannaaw ba goney Yàlla yooyu àndeek jigéeni àddina, ba am ca ay doom, aw xeetu ponkal wu ñuy wax Nefilim moo nekkoon ci àddina. Ñooy ponkal ya woon te doonoon góor ñu amoon tur.

¶ Maryaama ak Aaróona ñoo doon ŋàññ Musaa, ci ndawas Kuuseen su mu takkoon, te ab Kuuseen it la takkoon.

«Sunu baay daa dee ca màndiŋ ma. Moom nag bokkuloon ca gàngooru Kore, ga daje woon ci kaw Aji Sax ji, waaye bàkkaaru boppam a ko rey. Bàyyiwul nag doom ju góor.

Ñoo ko ñori ba mu ne duŋŋ, doomam yu góor ak yu jigéen, ñu nangu, moom, ñu jam ko saamar, rey ko. Nii lañu sottale ay mbugalam, ba mu yedd jigéen ñépp.