TSK

TSK · Numbers 16:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yaw daal demal rekk, yóbbu mbooloo mi fa ma la waxoon, te sama malaakaa ngii di la jiituji. Waaye keroog sama bésu mbugal, maay mbugal mbooloo mi ndax seen bàkkaar.»

Mise ne: «Soo délseek jàmm déy, Aji Sax ji waxul, ma jottli.» Mu dellu ne: «Mbooloo mi, yeena ko déggandoo, yeen ñépp.»

Job 35:15 TSK

Nga neeti Yàlla du mer, di mbugale, te yoonam newul ci njubadiy nit.

Ana nu ngeen di def keroog bésub mbugal ba, keroog ba safaan di bawoo fu sore? Ana ku ngeen di daw wuti wallam? Ana fu ngeen di denci seen teraanga?

Yaw Siyoŋ, sa mbugal mat na, deesatu la yóbbu ngàllo; yaw Edom laa ne, Aji Sax jee lay fey sa ñaawtéef, feeñal say bàkkaar.