Maay dëkk fi digg bànni Israyil te maay nekk seen Yàlla.
TSK
TSK · Numbers 16:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Maryaama ak Aaróona ñoo doon ŋàññ Musaa, ci ndawas Kuuseen su mu takkoon, te ab Kuuseen it la takkoon.
te dinañu ko nettali waa réew mii. Waa réew mii dégg nañu ne yaw Aji Sax ji ci sa bopp yaa nekk ci digg mbooloo mii ngay feeñu bët ak bët, yaw Aji Sax ji, saw niir taxaw, tiim leen, te aw taxaaru niir nga leen di jiitoo bëccëg, jiitoo leen aw taxaaru sawara, guddi.
Kon kay yaw yaak sa gàngoor gépp, ci kaw Aji Sax ji ngeen bokk daje! Ana kuy Aaróona, ba ngeen di ñaxtu ci kawam?»
Buleen sobeel réew mi ngeen dëkk, te man ma màkkaanoo ci biiram, ndax man Aji Sax ji maa màkkaanoo ci biir bànni Israyil.»
looy xeelook say coll, di fiire tund wi Yàlla namma dëkke? Aji Sax ji kat, fa lay dëkk ba fàww!
«Lu may doye seen sarax yu bare?» la Aji Sax ji wax. «Damaa suur seen saraxi rendi-dóomali kuuy, suur nebbonu juru yar gi, deretu yëkk ak xar ak sikket it, safu ma.
¶ «Yeena dëgër bopp, yeenay boroomi xol ak noppi yéefar! Dungeen noppee të Noo gu Sell gi? Maam ya, doom ya rekk!