Bànni Israyil gépp nag di ñaxtu ci kaw Musaa ak Aaróona, mbooloo ma mépp naa leen: «Waay lu nu tee woona dee ca réewum Misra, mbaa sax nu dee ci màndiŋ mii!
TSK
TSK · Numbers 16:41
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Simey a ngay saaga Daawuda naan: «Ayca, mott! Bóomkat bee, nit ku sew ki!
Nes tuut ñu fàtte jëfam ja, xaaratuñu ndigalam,
xanaa di xultoo seen biiri xayma, baña déggal Aji Sax ji.
Ba mu demee ba tollook buntu Beñamin, daje faak njiitu dag ya, Irya doomu Selemya doomu Anaña. Irya taxawal Yonent Yàlla Yeremi, ne ko: «Ãa, waa Babilon nga daw jëm!»
Xanaa Barug doomu Nerya kay moo lay xiirtal ci sunu kaw, ngir teg nu ci loxol waa Babilon, ñu rey nu, mbaa ñu yóbbu nu ngàllo ca Babilon.»
di xaacu naan: «Wallee, bokki Israyil! Waa jii, mooy kiy wër fépp, di waare ñépp kàddu gu safaanook njariñal xeet wi, ak yoonu Musaa ak bérab bii. Rax ci dolli mu indi ci kër Yàlla gi ay Gereg, ba sobeel bérab bu sell bii.»