Na tafu ci jëwu Aaróona, mu gàddoo ko ay wu tukkee ci lu bànni Israyil moy ci wàllu yëf yu sell yi ñu wara sellal ci seen mboolem sarax yu sell. Na nekk fàww ci jëëm, ndax Aji Sax ji nangul leen.
TSK
TSK · Numbers 18:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Limu fan yi ngeen nemmikuji woon réew ma, ñeent fukki fan, benn fan bu ci nekk day wecci menn at, ngeen gàddoo ko seen mbugali bàkkaar, ñeent fukki at, ba ngeen xam li jànkoonteek man di jur.
Mbooloo maa nga sam Aaróona ak Musaa. Ci biir loolu, ñu ne gees xaymab ndaje ma, gisuñu lu moy niir wa muur ko, leerug Aji Sax ji feeñ.
¶ Bu bànni Israyil juuxati ci xaymab ndaje mi, di gàddu bàkkaar bu dee di àtteem.
Mooy sonn ba gis ug leer, doyloo ko, te ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub, ba mu àtte leen àtteb njekk, sëfoo seeni ñaawtéef.
Moo ma tax di seere bésub tey, ne wàccoo naak ñépp, deesu ma topp benn bakkan.
¶ Déggal-leen seeni njiit te nangul leen, ndax sàmm bakkani ñi ñu jiite mooy seenub liggéey, te moom lees leen di laaj ëllëg. Su ko defee ñu defe ko xol bu sedd, te bañ koo def di binni, ndax loolu du seen njariñ.