TSK

TSK · Numbers 18:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Seen jur gu gudd ak gu gàtt itam, naka noonu. Juróom ñaari fan lay nekk ak ndeyam, bésub juróom ñetteel ba, ngeen jox ma ko.

Bu jant sowee nag set na, te man naa lekk ci sarax yu sell yi, ndax ñamam la.

Te seen pepp mu jëkka ñor, ak seen biiñ bu bees, ak seen diw gu bees, ak kawar gi ngeen jëkka wate ca seeni xar, joxleen ko ko,

¶ Ba loolu wéyee jenn waay jóge Baal Salisa, indil góoru Yàlla ga mburum pepp ma jëkka ñor, muy ñaar fukki mburuy lors, boole ciy gubi bele, yeb ko ci saakoom. Alyaasa ne ñu jox ko mbooloo mi, ñu lekk.

Genn dàmb gi di figg ju baaxa baax, mel ni witt mu jëkk. Dàmb gi ci des di figg ju bona bon, ju kenn dul lekk ndax bon.

Micah 7:1 TSK

Wóoy, ngalla man mi mel ni kuy forsi, te meññeef ma fatu, may raasaatu, te du cabbu reseñ ju nit lekk, du figg ju bees ji ma namm.