«Nanga ma sédde bépp taaw bu góor, nit ak mala, lépp lu jëkka juddu ci bànni Israyil, maa moom.»
TSK
TSK · Numbers 18:15
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye lépp lu mbaam-sëf taawloo, nangeen ko jote kuuyum xar, mu wuutu ko. Bu ngeen ko jotul, nangeen damm loos wi. Te itam jotleen képp kuy taaw bu góor ci seeni doom.
Seen jur gu gudd ak gu gàtt itam, naka noonu. Juróom ñaari fan lay nekk ak ndeyam, bésub juróom ñetteel ba, ngeen jox ma ko.
¶ «Waaye kat luy taaw cig jur, Aji Sax jee ko moom jeeg. Du lu kenn di dogoo jagleel Aji Sax ji. Muy barmol, muy mbote, muy tef, Aji Sax jeey boroom.
Njotlaay nag dina war ci ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñetti (273) bopp, yi taawi bànni Israyil ëppe Leween ñi.
¶ Mu am bés mu wax sarxalkat ya ne leen: «Mboolem xaalis bu ñu sellalal kër Aji Sax ji, muy xaalisu njot-gi-bakkan, mbaa xaalis bu ñu wàccoo ngiñ, mbaa bépp xaalisu saraxu yéene bu nit di indi kër Aji Sax ji,