Na Aaróona aki doomam jiitloo loolu, bu ñuy dugg ci xaymab ndaje mi, mbaa ñuy jegeji sarxalukaay bi, ngir liggéey ci bérab bu sell bi, ndax ñu baña yóbbe seen bopp mbugal, muy seen dee. Na Aaróona ak askanam sàrtoo loolu fàww.
TSK
TSK · Numbers 18:22
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Exodus 28:43
TSK
Leviticus 22:9
TSK
Sarxalkat yi dañoo wara dénkoo samay dénkaane bala ñoo gàddu bàkkaar, di dee ndax seenug néewal ci yooyu. Maay Aji Sax ji leen sellal.
Numbers 3:10
TSK
Aaróona ak doomam yu góor nag ngay tabb ngir ñu sasoo seenug carxal, waaye képp ku ci laal te bokku ci, dees koy rey.»
Numbers 18:7
TSK
Yaw nag yaak say doom, dénkooleen seenug carxal ci mboolem mbiru sarxalukaay bi, ak ca wàllaa ridob biir bi, ngeen di ca liggéey. Seen liggéeyu carxal bi, ab sasu teraanga la, maa leen ko terale. Waaye ku bokkul ci yeen, bu ci laalee, dees koy rey.»