TSK

TSK · Numbers 19:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Day yeesalal Aji Sax ji nasireenam ga mu ko séddoo woon, kemu fan ya mu xasoona nasireenal. Su ko defee day indi xarum menn at, def ko saraxas peyug tooñ. Fan yi mu jëkkoona nasireenal day neen, ndax nasireen googa moo sobewu.

Ku set nag te nekkul ciw yoon, su ñàkkee màggal bésub Mucc bi, kooku dees koy dagge ciw askanam, ndax saraxu Aji Sax ji mu joxewul ci bésam. Kooku moo gàddu bàkkaaru boppam.

Bu loolu wéyee, na ku set jël caru isob, capp ko ca ndox ma, wis-wisal ko ca kaw xayma ba nit deeye, wis ko ca kaw ndab yépp, ak ca kaw nit ña fa nekkoon. Na ko wis itam ci kaw nit ku laal yaxi ku dee, mbaa mu laal ku ñu bóome saamar, mbaa mu laal ku Yàlla moomal boppam, mbaa mu laal bàmmeel.

mboolem lu dul lakk, rekk, nangeen ko laalale sawara, mu set. Ndoxum setlu mi it, warees na koo dellu setale yooyii. Waaye mboolem luy lakk, ci ndoxum setal mi doŋŋ lees koy dugal, ngir mu set.

Almasi mi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.

¶ Boobu sarxalkat bu mag lanu soxla; moo sell, mucc sikk, mucc sobe, moom lañu teqale ak bàkkaarkat yi, te moom lañu kaweel ba fa tiim asamaan.