TSK

TSK · Numbers 2:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Israyil nag jàllawle ay loxoom, tàllal ndijooram, teg ko ca kaw boppu Efrayim, mi gën di ndaw; càmmoñam tege ca boppu Manase, doonte mooy taaw.

¶ Ñu lim turi sëti Yuusufa yi askanoo ci doomam Efrayim, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.

ak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy ak juróomi sikket, ak juróomi xari menn at. Looloo doon saraxu Elisama doomu Amiyut.

Taawub yëkk la, daraja mooy boroom, béjjén ya, béjjéni nagu àll la, ca lay butteendoo xeet yépp, ba ca cati àddina. Ñooñooy junniy junniy nit ca giirug Efrayim, ak junni ca giirug Manase.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor yi, di seedeb Sabóor, giiroo ci Asaf.