Bérab boobu la Musaa wooye Maasa (mu firi Nattu). Mu wooye ko itam Meriba (mu firi ab Jote), ndax joteb bànni Israyil ba fa amoon, ak na ñu fa nattoo Aji Sax ji, naan: «Moo Aji Sax ji ndax mu ngi ci sunu biir, am déet?»
TSK
TSK · Numbers 20:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Exodus 17:7
TSK
Deuteronomy 33:8
TSK
¶ Lewi la wax ne ko: Sa Tumim ak sa Urim, jumtukaayi tegtal ya, ñeel na góor gay sa wóllëre, yaa ko nattoo ca Maasa, joteek moom ca ndoxum Meriba.
Psalms 95:8
TSK
ga mu noon: «Buleen të, na woon fa Meriba, jantub keroog fa Maasa, ca màndiŋ ma,
Isaiah 5:16
TSK
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ab àtteem lay fésale màggaayam, Yàlla ju sell ji, ag njekkam lay firndeele sellngaam.
Ezekiel 36:23
TSK
Kon dinaa fésal sama sellngay tur wu màgg, wi ñu teddadil fi biir yéefar yi, sama tur wi ngeen teddadil fi seen biir. Ci yeen laay fésale sama sellnga, yéefar yiy gis, ba xam ne maay Aji Sax ji. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.