Aaróona aki sëtam la loolu di doon seen cér bu bànni Israyil di warlook ñoom ba fàww, ndax ab jooxe la; jooxe bu bànni Israyil di génnee ci seen saraxi cant ci biir jàmm, muy seenub jooxe, ñeel Aji Sax ji.
TSK
TSK · Numbers 20:28
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Mbooloom bànni Israyil gépp nag àgg ca màndiŋu Ciin, ci biir weer wi jëkk ci at mi. Ñu daldi dal ca Kades. Fa la Maryaama faatoo, ñu denc ko foofa.
«Aji Sax ji, yaw Yàlla mi moom noowi bépp boroomu suux, ngalla tabbal nit ku jiite mbooloo mi,
¶ Ba mu ko defee Aaróona sarxalkat ba yéeg ca kaw tundu Or, ci ndigalal Aji Sax ji. Mu daldi faatu foofa, ca ñeent fukkeelu at ma, gannaaw ba bànni Israyil génnee réewum Misra, yemook benn fanu juróomeelu weeru at ma.
¶ Ba loolu amee Musaa woolu Yosuwe, wax ak moom, Israyil gépp teg ci seen bët. Mu ne ko: «Dëgërlul te am fit, ndax yaw yaay ànd ak mbooloo mii ca réew ma Aji Sax ji giñaloon seeni maam, ne ñoom la koy jox. Yaw it yaa leen koy sédde.
Musaa, jaamub Aji Sax ji nag dee foofa ca réewum Mowab, na ko Aji Sax ji tudde.
¶ «Léegi nag xam naa ne mboolem yeen ñi ma duggoon ci seen biir, di yégle nguurug Yàlla, dootuleen ma gis.
Waaye dinaa def sama kem-kàttan, ba fu ngeen tollu, di fàttliku mbir yooyu, gannaaw bu ma dëddoo.