TSK

TSK · Numbers 21:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Moom moo dindi bérabi jaamookaay ya, toj tuuri doj ya, gor xer wa ñuy jaamoo Asera, rajaxe jaanu xànjar ja Musaa defaroon. Ndax ba ca jamono yooya waa Israyil dañu daan taalal jaanu xànjar ja cuuraay, tudde ko Nexustan.

¶ «Bu loolu amee maay sottil waa kër Daawuda ak waa Yerusalem, noowug yiw aki dagaan, ba ñu geesu ma man, mi ñu jam ba mu sar, te dinañu ko jooy ni ñuy jooye benn bàjjo, di ko naqarlu ni ñuy naqarloo deewug taaw.

¶ Yoonu Musaa moo dikk ngir fésal barewaayu moy, waaye fu bàkkaar bare, aw yiw gën faa bareeti,

Almasi mi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.