TSK

TSK · Numbers 22:34

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Firawna nag gaaw woolu Musaak Aaróona, ne leen: «Tooñ naa seen Yàlla Aji Sax ji, tooñ leen.

Ca ëllëg sa ñu teela xëy, yéegi kaw tund ya, te naan: «Nu ngi nii di yéeg, jëm fa nu Aji Sax ji wax, ndax noo tooñ.»

¶ Sóol ne Samiyel: «Bàkkaar naa! Ndax maa wàcc kàddug Aji Sax ji ak say digal, ndax ragal mbooloo mi, ba topp seen coobare.

¶ Ba Daawuda waxee Sóol kàddu yooyu ba daaneel, Sóol da ne: «Éy Daawuda, doom, loolu sa baat la moos?», daldi ne yikkét jooy.

¶ Daawuda nag ne Natan: «Maa tooñ Aji Sax ji.» Natan ne ko: «Aji Sax ji it jéllale na sa bàkkaar; doo ci dee.

Job 34:31 TSK

Su nit ki nee Yàlla: «Jot naa samab añ, dootuma bàkkaar.

Ba leen Yàlla fàddee, ña des sàkku ko, tuub, waññiku ci moom.