Bu bëccëgee nag Aji Sax ji nekk ci seen kanam ci biir taxaaru niir, di leen jiite ca yoon wa, te bu guddee mu nekk ci biir taxaaru sawara, di leen leeral, ba ñu mana dem guddi ak bëccëg.
TSK
TSK · Numbers 23:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Aji Sax ji ne ko: «Man ci sama bopp maay ànd ak yaw te maa lay noppal.»
Ci kaw loolu sawara bawoo fi Aji Sax ji, tàkk ca kaw sarxalukaay ba, xoyom saraxu rendi-dóomal ba ak nebbon ba. Naka la mbooloo ma mépp gis loola, daldi sarxolle, ba noppi dëpp seen jë fa suuf.
Ci kaw loolu ñu bokk daje fi kaw Musaa ak Aaróona, ne leen: «Doy na sëkk! Mbooloo mi ba mu daj, ñépp a sell, te ci sunu biir la Aji Sax ji nekk. Ana lu ngeen di xoggliku ci kaw mbooloom Aji Sax ji?»
Ndokklee yaw mi Aji Sax ji toppul ag tooñ, te amoo xelum njublaŋ it.
Ay giir a riir, ay réew yëngu; mu àddu, suuf seey!
Moo nu tànnal céru suuf, muy sagu askanu Yanqóoba wii mu sopp.
Aji Sax jeey Buur, na àddina bég; dunoo dun bànneexu.
Ni penku soree sowu, ni la nu soreleek sunu mbugali tooñ.
Nañuy sante Aji Sax ji Siyoŋ, moom mi dëkke Yerusalem. Màggal-leen Ki Sax!
Ngeen mébét, dara! Ngeen diisoo, diisoo, tus! Yàllaa ànd ak nun!
Foofa déy la nu Aji Sax ju màgg ji di nekkal bérab bu defi dex aki wal, fu gaalu joow dul dawe, te gaal gu mag du fa jaare,
Ndeke sama tiisu xol wii, sama jàmm rekk a tax. Sa cofeel a tax nga sorele maak paxum sànkute. Yaa sànni sa gannaaw sama bépp bàkkaar.
Su bés baa, ci yooyu fan,» kàddug Aji Sax jee, «dees na seet fi Israyil lu ñaaw, du fi am; fi Yuda it, deesu fi gis bàkkaar. Maay jéggal moos ndes wi ma fi saxal.
Israyiloo, dellul ci sa Yàlla Aji Sax ji, fakktaloo nga sag ñaawtéef.
Ana Yàlla ju mel ni yaw, di bale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom. Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.
Ba ñu jubsee Yerusalem, bay wàcce ca mbartalum tundu Oliw ya, mbooloom taalibe mépp la mbégte jàpp, ñu tàmbalee sàbbaal Yàlla ca kaw ndax kéemaan ya ñu gis.
Ndax kat bàkkaar yilifatu leen, nde du ci kilifteefu yoonu Musaa ngeen nekk, waaye ci aw yiw ngeen tàbbi.
¶ Waaye cant ñeel na Yàlla! Moom mi Almasi tax mu di nu yóbbaale saa su nekk, ci njaab miy fésal ndamam, te cuuraayal xam-xamam, nun ñii la koy wasaaree fépp,
Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.»