TSK

TSK · Numbers 23:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yàlla ne ko: «Ngalla jëlal sa jenn doom jii di Isaaxa, muy koo bëgg, nga dem ca réewu Morya ca tund wa ma lay wax, joxe ko fa, mu nekk saraxu rendi-dóomal.»

Naka la Ibraayma siggi rekk, yem ci menn kuuyum xar mu béjjén ya lonke ci as ngarab. Ibraayma dem, jël kuuy ma, rendi, mu wuutu doom ja, di ab saraxu rendi-dóomal.

¶ Aji Sax ji woo na Musaa, wax ak moom ca xaymab ndaje ma ne ko:

¶ Aji Sax ji nag ubbi bëti Balaam, mu gis malaakam Aji Sax ja, mu taxaw ca yoon wa, xàccib saamaram. Mu ne gurub sukk, dëpp jëëm fa suuf.

Balaam ne Balag: «Taxaweel nii ci sa saraxu rendi-dóomal, man ma séentuji nee.»

¶ Balaam nag gis ne Aji Sax ji la neex mu barkeel Israyil, ba tax sàkkootul ay takk na woon, xanaa mu walbatiku, janook màndiŋ ma.