TSK

TSK · Numbers 23:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Léegi nag su ngeen ma déggalee bu baax, di sàmm sama kóllëre ak yeen, yeenay doon sama moomeelu bopp ci mboolem askan yi. Dëgg la, àddina wërngal këpp maay Boroom,

Ba Aji Kawe ji séddee xeet yi seeni suuf, tasaare doom aadama yi ci àddina, moo àppal xeet yi seen kemi réew, na mu dëppook limeefu goney Yàlla yi.

Ezra 9:2 TSK

Jël nañu jabar ci ñoom, jëlal ci jabar seeni doom, ba jaxase jiwu mu sell mi ak waasoy réew yi. Njiit yeek mag ñi sax ñoo jiitu ci googu fecci kóllëre.»

Yaw Yanqóoba sama jaam bi, bul tiit.» Kàddug Aji Sax jee. «Yaw laa àndal. Maay fàkkas mboolem xeet yi ma leen sànni woon, waaye yeen, duma leen fàkkas. Duma leen ñàkka duma moos, waaye dinaa leen yar lu yem.»

Ngalla nanga sàmme saw yet sa ñoñ, sa gàtt yi nga séddoo, te ñu màkkaanoo gott bi ñoomu neen, fi digg parlu mu naat. May leen ñu fore àlli Basan ak Galàdd na jant ya woon.

Kon nag: «Nangeen génne ci seen biir, te teqlikoo ak ñoom,» la Boroom bi wax. «Lu sobewu, buleen ko laal. Su boobaa, maa leen di dalal.

Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.