TSK

TSK · Numbers 24:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba jant bay so, ngëmment lu réy a ko jàpp, tiitaange lu mag, ànd ak lëndëm gu ne këruus, ne milib ci kawam.

Ci kaw loolu Yàlla dikkal Balaam ca guddi ga, ne ko: «Gannaaw woosi la mooy tànki ñii, àndal ak ñoom. Waaye nag lu ma la wax rekk, def ko.»

Ci kaw loolu mu summiy yéreem, di wax ay waxyu moom it fa kanam Samiyel, daldi ne làndaŋ, ne duŋŋ, bëccëg keroog gépp ak guddi ga gépp. Looloo waral ñu naan: «Moo Sóol it ci yonent yi laa?»

Sunu kiirlaay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israyil ay boroom.

Jibril dikk nag ba fi ma taxaw. Ba mu jegesee, ma tiit lool, ba daanu, sama kanam dëppu fi suuf. Mu ne ma: «Yaw doom aadama ji, nanga xam ne peeñu mii mujug jamono la.»

¶ Bi mu may wax kàddu yooyu, maa ngi sëgg, sama kanam jublu ci suuf, manumaa wax.

¶ Naka la Piyeer di xalaat ba tey ca peeñu ma, Noo gi ne ko: «Ñetti nit a ngi nii, di la seet.

¶ Damu war na, moonte amul njariñ, waaye naa jàll ba tey ci mbir yu ma Sang bi gisloo, ak peeñu yu mu ma won.

¶ Naka laa ko gis, ne dàll daanu ci ay tànkam ni ku dee. Mu teg ma loxol ndijooram, ne ma: «Bul tiit. Maay Ki Jëkk, di Ki Mujj.