Buleen ci sujjóotal lenn, buleen ci jaamu lenn, ndax man seen Yàlla Aji Sax ji, Yàlla ju fiir laa. Maay topp doom tooñu waajur, ba ca seen maasi sët, ba ca maasug sëtaati nit ñi ma bañ.
TSK
TSK · Numbers 25:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ndax waruleena jaamu jeneen yàlla, ngir Aji Sax ji, turu “Ku fiir ki” lay wuyoo, te Yàlla ju fiir la.
Aji Sax jee koy seppee ci mboolem giiri Israyil, ngir sédd ko njekkar, na mu dëppook mboolem alkàndey kóllëre gi ñu bind ci téereb yoon wii.
Ñoo ma fiirloo ak yàlla yu dul tus, merloo maak seen tuuri neen, man it maa leen di fiireloo xeet wu tekkiwul dara, ci waasow naataxuuna laa leen di merloo.
Waa Yuda nag di def li Aji Sax ji ñaawlu, ba di ko fiirloo fiiraange gu raw ga ko seen maam daa fiirloo ndax seen bàkkaar.
Yàlla da leen doon sànk, bu dul woon ak Musaa, xejjam ba ko kar, àtte leen, mu giif, ba fàkkasu leen.
Maa lay àttee àtteb jigéeni njaalookat, jigéeni tuurkati deretu nit. Maa lay xëpp deretu xadar ak fiiraange.
Du seen xaalis, du seen wurus wu leen di mana xettli. Keroog bésub sànjum Aji Sax ji, ak sawaras fiiraangeem, àddina sépp ay xoyomu. Mooy raafal moos mboolem ñi dëkke àddina si, te raafal gu raglu lay doon!»
Maa leen di fiiree fiiraangey Yàlla ci boppam, ndax jenn jëkkër doŋŋ laa leen digool ab séy, te mooy Almasi mi ma leen namma jébbal, te fekk leen di janq bu set wecc.