TSK

TSK · Numbers 27:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Déglu ma fii, ma digal la, tey ñaan Yàlla ànd ceek yaw. Danga fee toogal mbooloo mi ci kanam Yàlla, di diis Yàlla jotey nit ñi,

¶ Ci biir loolu mu am ay nit ñu ab néew tax ñu sobewu, ba manuñoo màggal bésub Mucc bi bésub keroog. Ñu dikk ba ci Musaa ak Aaróona ca bés ba.

Ca Elasar sarxalkat bi nag la war di dem, ngir mu di ko seetal fi kanam Aji Sax ji, lu Urim, jumtukaayu tegtal bi, feeñal. Ci ndigalal Elasar nag lañuy génne, te ci ndigalam it lañuy dellusee, moom Yosuwe, ak mboolem bànni Israyil giy ànd ak moom, mbooloo mépp.»

¶ Su leen mbir jafee ba wees leen ci àtteb bakkan bu ñu faat, ak ay jote, ak loraangey yaram yu ñu teg nit, ak mboolem dëngoo bu laaj àtte ci seen biir dëkk, dangeen di dem ba ca bérab ba seen Yàlla Aji Sax ji di taamuji,