TSK

TSK · Numbers 28:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Bu saraxam dee saraxu jur gu gudd gu ñuy def rendi-dóomal, na sarxal aw yëkk wu amul sikk. Na ko yóbbu ci bunt xaymab ndaje mi ci kanam Aji Sax ji, ngir mu nangul ko ko.

Sarxeleen loolu, te bumu bokke ak rendi-dóomal bi war bés bu nekk tey ànd ak saraxu peppam. Lu mucc sikk nag ngeen di def sarax yooyii, te ngeen defaale saraxi tuuram yi ci war.

Jur gu ci am sikk nag, muy soox, mbaa mu gumba, mbaa mu am sikk su réy su mu mana doon, buleen ko sarxalal seen Yàlla Aji Sax ji.

Yeena ngi naa: “Ndaw lu soof,” di ciipatu.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Jur gu ñu sàcc ngeen may indil, ak guy soox, ak gu wopp, loolu mooy seen sarax! Nu ma koy nangoo ci seeni loxo?» Aji Sax jee ko wax.