TSK

TSK · Numbers 28:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sàkkal ñetti kilo, yemook benn fukkeelu nattub sunguf su mucc ayib su ñu xiiwe liitar ak genn-wàll, yemook xaajaatub natt bi ñuy wax xiin ci diwu segalu oliw, ak saraxu tuurub benn liitaru biiñ ak genn-wàll, yemook xaajaatub xiin. Loolu yépp ànd ak menn kuuy mi.

Deesu ci sarxal cuuraay lu ñu diglewul, deesu ci rendi saraxu dóomal, deesu ci def saraxu pepp mbaa saraxu tuuru.

Saraxu pepp mi muy àndal juróom benni kiloy sunguf su mucc ayib lay doon, ñu xiiwe ko diw, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, ngir xetug jàmm. Sarax si ñuy tuural Aji Sax ji, liitaru biiñ laak genn-wàll.

ak biiñ ngir saraxu tuuru, ñetteelu xaajub xiin, di ñaari liitar. Na joxe loolu, def ko xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

¶ «Ay saraxi tuuram genn-wàllu xiinu biiñ la, di ñetti liitar ci yëkk wu nekk, ak benn ñetteelub xiin, di ñaari liitar ci kuuy mi, ak walaatu xiin, di liitar ak genn-wàllu biiñ ci xar mu ci nekk. Loolooy dóomalu weer wi, weer wu ci nekk, ba weeri at mi daj.

Yaw Israyil, jëlal doj yu rattax yi ci yoonu ndox wi, séddoo, muy sa cér, nga muurloo! Ñoom ngay tuural, di leen defal ay saraxi pepp. Waaye Aji Sax ji nee: «Ndax damay jéllale?»

Joel 1:13 TSK

Yeen sarxalkat yi, gembuleen te tiislu, yeen ñi dénkoo sarxalukaay bi, yuuxuleen, yeen boroom dénkaaney sama Yàlla, dikkleen, sol ay saaku yu ngeen fanaanoo, ngir toroxlu, nde xañees na seen kërug Yàlla ga saraxu pepp ak saraxu tuuru!

Su ma ci deeyee sax, ba sama dund mel ni sarax su ñu tuur, tofal ko ci sarax, bi seen ngëm taxawe, su boobaa it maa ciy bég, te di leen woo, ngir bokk ak yeen ñépp bànneexu.