TSK

TSK · Numbers 29:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Nangeen ca sarxal ab rendi-dóomal, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: fukki yëkk yu ndaw ak ñett, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk.

Yaw Aji Sax ji sama Yàlla, bare nga loo def, amuloo moroom! Bare nga kéemaan aki mébét yoo nu sottalal, ma bëgga xamle lépp, te mu bare ba wees ab lim.

Céy Yàlla, yaw Yàlla mi may musal, baal ma deret ji ma tuur, ma siiwal sa njekk.

«Lu may doye seen sarax yu bare?» la Aji Sax ji wax. «Damaa suur seen saraxi rendi-dóomali kuuy, suur nebbonu juru yar gi, deretu yëkk ak xar ak sikket it, safu ma.

Hosea 6:6 TSK

Ndax ngor laa namm, dub sarax, ràññee Yàllaa ma gënal saraxi rendi-dóomal.

¶ Bu Yàlla wooyee kóllëre gii gu yees nag, daa fekk mu wonnil gu jëkk ga. Lu wonni te di lu yàgg nag, mu ngi ci tànki wees.