TSK

TSK · Numbers 3:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

kaala leen, te takkal Aaróona ak doomam yu góor ay laxasaay. Su ko defee ñu féetewoo céru sarxalkat, muy dogal bu sax dàkk. «Noonu ngay sase Aaróona ak doomam yu góor.

¶ Ña daan dale nag fa jàkkaarlook jaamookaay bi, ca kanam, janlook xaymab ndaje mi, ca wetu penku, ñoo doon Musaa ak Aaróona ak doomam yu góor. Ñoo dénkoo woon dénkaaney bérab bu sell bi, sasool ko bànni Israyil, te ku ci laal te bokku ci, dees koy rey.

Yaw nag yaak say doom, dénkooleen seenug carxal ci mboolem mbiru sarxalukaay bi, ak ca wàllaa ridob biir bi, ngeen di ca liggéey. Seen liggéeyu carxal bi, ab sasu teraanga la, maa leen ko terale. Waaye ku bokkul ci yeen, bu ci laalee, dees koy rey.»

¶ Terewul Yàlla mbugal ñenn ca waa Bet Semes, ndax dañoo yërndu woon ca biir gaalu Aji Sax ja. Juróom ñaar fukki nit la fàdd ca ñoom. Waa dëkk ba nag di tiislu ndax mbugal mu réy moomu leen Aji Sax ji teg.

Ci kaw loolu Yerbowam tabax ay bérabi jaamookaay, ba noppi tabb ay sarxalkat ci baadoolo yu bokkul ci askanu Lewi.

Dénkoowuleen dénkaane yi jëm ci sama yëf yu sell yii, xanaa di ko dénk ñeneen ñu koy dénkoo fi sama biir bérab bu sell bi.»

su dee wàllu jàpple, deel jàpple; su dee wàllu njàngle, ngay jàngle;

Loolu ngay def sam xel, mbir yooyu ngay pastéefoo ba sag yokkute bir ñépp.

¶ Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca bérab bu sell baa sell, ngir deretu Yeesu,