Ñoom déy lañu ma sédda sédd ci biir bànni Israyil, ñu wuutu mboolem luy ubbiteg njur, di taawi mboolem bànni Israyil. Maa leen sédd sama bopp.
TSK
TSK · Numbers 3:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
te itam maa jukkee Leween ñi ci bànni Israyil, maa leen yékkati, jox leen Aaróona aki doomam, ngir ñu liggéey liggéeyu bànni Israyil ci wàllu xaymab ndaje mi, di defal bànni Israyil seenug njotlaay, ngir bu bànni Israyil jegee bérab bu sell bi it, du tax menn mbas am ci seen biir.»
¶ «Man mii nag maa seppee seen bokki Leween ñi ci biir bànni Israyil. Yeen lañu leen jagleela jagleel, ñeel Aji Sax ji, ngir ñu liggéey liggéeyu xaymab ndaje mi.
Ci biir loolu ñu tabb sarxalkat ya, ca wàll ya ñu bokk ak Leween ña ca seeni kurél, ñu sasoo liggéeyu Yàlla ji ci Yerusalem, muy la ñu bind ci téereb Musaa.
Moo tax ñu ne: «Moo yéeg fa kawa kaw, yóbbaale gàngoor gu mu jàppe xare, te moo séddale nit ñi ay may.»