Gannaaw loolu Yanqóoba dogu na ne: «Su Yàlla àndee ak man, di ma sàmm ci yoon wi may aw, di ma jox lu ma lekk ak lu ma sol,
TSK
TSK · Numbers 30:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Su sàgganee it ba giñ ne dina def nàngam, muy lu baax mbaa lu bon, muy mboolem ngiñ lu ko rëcc te ba mu koy wax teyu ko, ba mu wees, saa yu ko xamee tooñ na.
Ci kaw loolu Israyil xasal Aji Sax ji aw xas, ne ko: «Soo tegee ba teg mbooloo mii ci sunuy loxo déy, dinanu faagaagal seeni dëkk.»
¶ «Su dee kàddug xas gu jibe ci ku jëkkëram faatu, mbaa ku ñu baal, mboolem lu mu tegooloon boppam day sax.
di ko ñaan, mu di la nangul, yaw it ngay wàccook say dige,
Moom de sàgganewul boroom tiis, làqu ko kanamam, ba mu wootee, wuyu na ko.
Yàllaay dégg, duma leen, moom mi nguuram yàgga sax. Selaw. Soppikuwuñu fenn te ragaluñu Yàlla.
Maay duggaale sa kër ay saraxi rendi-dóomal, defal la samay dige,
Samay digeek Aji Sax ji laay matal fi kanam ñoñam ñépp.
Giñ naa te di ko dëggal, ne dinaa sàmmonteek sa ndigali njekk.
Baña digee gën dige loo deful.
¶ Ba bët setee Yawut ya daje, daldi xasoo, ne duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñu reyee Póol.
Yaw nag bu leen ko may, ndax lu ëpp ñeent fukk ci ñoom a koy tëru, te xasoo nañu ne dootuñu lekk, dootuñu naan, ba kera ñu ko reyee. Fagaru nañu ba noppi, di xaar sa ndigal.»
Noonu lañu binde ne: «Mooy nàddil néew-doole yi, te njekkam sax dàkk.»