TSK

TSK · Numbers 32:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ibraam nag amoon alal ju bare diggante jur, xaalis ak wurus.

¶ Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Sowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja.

Bi loolu amee Silpa, jaamub Leya, amal Yanqóoba doom ju góor.

Amoon na it mbooloom nit ñu ànd ak ñoom, te di askan yu raxe, ak jur gu bare, gu gudd ak gu gàtt.

Ba loolu amee Musaa yebal ay ndaw, ñu yëri dëkk ba ñuy wax Yaser. Gannaaw gi bànni Israyil nangu dëkk-dëkkaan ya, daldi fay dàqe Amoreen ña.

¶ Ñi askanoo ci Gàdd, ñook seeni làng ñoo di ñoom Cefon mi sos làngu Cefoneen ñi, ak ñoom Agi mi sos làngu Ageen ñi, ak ñoom Suni mi sos làngu Cuneen ñi,

Sunuy goneek sunuy jabar, ak sunuy gàtt, ak sunu jur gépp fii ci dëkki Galàdd lay des.

Moo xool cér ba jëkka lew, jagoo ko, nde fa la wàllu njiit di xaar boroom. Moo fekksi njiiti askan wi, moo jëfe njekku Aji Sax ji, aki dogalam fi Israyil.

Ñu jàll dexu Yurdan, dem dali Arower ca bëj-saalumu dëkk ba, ca biir xur wa, daldi dem Gàdd, jaare fa jëm Yaser.

Moo diwu pajtal amul Galàdd a? Am fajkat a fi amul? Ana lu waral bokk yi taneeguñu?

Maa ngii di delloo Israyil parloom, mu dellu di fore àllub Karmel ak Basan, di regge tundi Efrayim ak Galàdd.