TSK

TSK · Numbers 32:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yuda ne: «Sang bi, lu nuy waxati? Lu nu mana lay, ba setal sunu bopp? Yàllaa nu feeñal, sang bi. Nanu bokk nun ñépp di say jaam, yem ci kepp ak ki ñu fekk kaas bi ci loxoom.»

¶ Waaye nag su ngeen déggalul seen Yàlla Aji Sax ji, te baña sàmmoo jëfe mboolemi santaaneem, ak dogali yoonam, yi ma leen di jox tey, mboolem alkànde yii dina leen dab, sottiku ci seen kaw:

Su ko defee Aji Sax ji dina ko gàdduloo bakkanu boppam, feye ko ko bakkanu ñaar ña mu songoon, di Abner doomu Ner, njiital xarey Israyil, ak Amasa doomu Yeter, njiital xarey Yuda; muy ñu jub, ñu ko gën, teewul mu jam leen saamar, ñu dee te sama baay Daawuda yégu ko.

Sunuy ñaawtéef a ngi janook yaw, te sunu mbóot leer na la.

Yal nañu këppoo xali sawara, tàbbi ciy pax te dootuñu jóg.

Ku jub day daanu juróom yaari yoon, jógaat, ab soxor sërëx ci njekkar.

Ma ne, Aji Sax ji gàttul loxo ba tëlee walloo, noppam naqariwul ba tere koo dégg.

Njàqare ak musiba daal, mooy dal ci kaw képp kuy def lu bon, te Yawut bi jiitu ci, waaye ki dul Yawut it topp ci;