TSK

TSK · Numbers 32:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Lakk gaa nga jóge Esbon, sawaraa bawoo dëkkub Siwon ba, xoyomi Ar ga ca Mowab, gor ñooña tiim dexu Arnon.

Ba loolu amee Musaa yebal ay ndaw, ñu yëri dëkk ba ñuy wax Yaser. Gannaaw gi bànni Israyil nangu dëkk-dëkkaan ya, daldi fay dàqe Amoreen ña.

Ba mu ko defee Gàddeen ña tabax Dibon ak Atarot ak Arower,

ak Nebo, ak Baal Mewon, lenn ca turi dëkk ya soppiku, ak Sibma. Ñu tudde dëkk yooyu ñu tabaxaat, seen turi bopp.

Nit ñaa ngi yéeg jëm kërug jaamookaay ga ca Dibon, ngir jooyi ca bérabi jaamookaay ya, Mowab a ngay yuuxoo kaw tundu Nebo ak Medeba, boppoo bopp dib nel, sikkimoo sikkim xuufu,

Dexu Nimrim wow na, ñax wow, gàncax lax, dara naatatul.

¶ Lu jëm ci Mowab, Aji Sax ji Yàllay Israyil, Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: «Ngalla waa Nebo, seen dëkk ba yàqu na! Kiryaatayim, ñu torxal, nangu ko; tata ja daanu, tasaaroo.

Yuux jibe na Esbon, ba Elale, àkki ba Yaxacc ak Sowar ba Oronayim ak Eglat Selisiya. Ndoxi Nimrim sax ŋiis na.