TSK

TSK · Numbers 33:52

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Maa leen di dogal kemug suuf gu dale géeju Barax yi, ba géeju waa Filisti, daleeti ca màndiŋ ma, ba ca dexu Efraat, ndax maay teg waa réew mi ci seeni loxo, ngeen dàq leen.

Seeni sarxalukaay kay ngeen di màbb, seen tuuri doj, ngeen rajaxe, seen xer yi ñuy jaamoo Asera tuur mi, ngeen gor,

Bu leen leen seen Yàlla Aji Sax ji jébbalee, ba ngeen duma leen, nangeen leen faagaagal ba ñu jeex tàkk. Buleen fasook ñoom kóllëre, te buleen leen yërëm.

tasleen tasar mboolem bérab, ya xeet ya ngeen di dàq, di jaamoo seeni tuur; muy kaw tund yu mag ya, di kaw tund yu ndaw ya, di ker garab yu naat ya.

Dëkki xeet yii leen seen Yàlla Aji Sax ji sédd nag, buleen ci bàyyi lenn luy noyyi, mu dund.

Te it faagaagaluñu yéefar, ya leen Aji Sax ji waxoon,