TSK

TSK · Numbers 34:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Maa leen di dogal kemug suuf gu dale géeju Barax yi, ba géeju waa Filisti, daleeti ca màndiŋ ma, ba ca dexu Efraat, ndax maay teg waa réew mi ci seeni loxo, ngeen dàq leen.

Waa ji ne ma: «Ndox mii mu ngi jëm diiwaanu penku, wàcci jooru Araba, jàlli biir géeju Xorom ga. Te bu ndox mi duggee biir géej, géeju ndox mu bon ma, ndox ma day daldi neex.

Kemu penku ba day dale diggante Oran ak Damaas, topp xuru Yurdan, diggante diiwaanu Galàdd ak réewum Israyil, dem ba àgg Tamar ca géeju penku ba. Loolooy wàllu penkoom.