TSK

TSK · Numbers 4:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Defarlul tegukaayu làmp bu wurusu ngalam. Tegukaay ba, dees koy tëgg. Na taatu tegukaay ba ak per ba ànd aki kaasam aki kàmbóotam aki mbaram, lépp di benn.

¶ Besalel sàkk itam tegukaayu làmp bu wurusu ngalam. Liggéeyu tëgg bu jekk la def tegukaayu làmp bi, ak taatu tegukaay bi, ak peru tegukaay bi, ay kaasam aki kàmbóotam aki mbaram, lépp ànd ak tegukaay bi, di benn.

Kumpa gi ci juróom ñaari biddiiw yi nga gis ci sama loxol ndijoor, ak juróom ñaari tegukaayi làmp yu wurus yi, li muy firi mooy: juróom ñaari biddiiw yi ñoo di malaakay juróom ñaari mboolooy gëmkat ñi; juróom ñaari tegukaayi làmp yi ñoo di juróom ñaari mbooloo yi.»