TSK

TSK · Numbers 5:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Maay samp sama kër ci seen biir te duma leen sib.

Buleen sobeel réew mi ngeen dëkk, te man ma màkkaanoo ci biiram, ndax man Aji Sax ji maa màkkaanoo ci biir bànni Israyil.»

Ndax seen Yàlla Aji Sax ji mooy dem ak a dikk ci seen biir dal bi, ngir xettli leen, ba jébbal leen seeni noon. Kon nag seenub dal daa wara sell, ngir Aji Sax ji ñàkka gis fi seen biir, lenn lu tegginewul, ba dëddu leen.

Watiiri xarey Yàlla di ñaar fukki junni (20 000), ba ci junniy junni. Boroom bi ne ca seen biir, di boroom tundu Sinayi fa biir sellngaam.

Ase dellu ne leen: «Nit ku sobewu ndax ab néew bu mu laal, su laalee lenn ci mboolem ñam yooyu, ndax ñam wa sobewu na?» Sarxalkat ya ne ko: «Sobewu na kay.»

Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.»

Ab féewalekat nag, yedd ko benn yoon ba ñaareel bi yoon, doora daggook moom,

Du lenn lu sobewu lu fay dugg nag, mbaa defkatu jëf ju ruslu ak njublaŋ. Ñi ñu bind ci téereb dund bu Gàtt bi doŋŋ ñoo fay dugg.