TSK

TSK · Numbers 5:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ci tooñin yooyu ñu lim war naa wax na mu tooñe.

La mu sàggane woon ca yooyu ñu sellalal Aji Sax ji da koy fey, ba dolli ci juróomeelu céru njég ga mu fey, jox ko sarxalkat bi. Sarxalkat bi da koy defal kuuy mi njotlaayam, muy saraxu peyug tooñ, ngir mu am njéggal.

Na sawaras sarxalukaay bi wéye tàkk te du fey. Suba su nekk na ko sarxalkat bi xamb, ba noppi teg ci saraxu rendi-dóomal bi, te na lakk nebboni saraxi cant gi ci biir jàmm.

¶ «Su ko defee ñoom dinañu tudd seen bàkkaar ak seen bàkkaaru maam ya, ndax dañu maa wor te dëkke maa noonoo,

Job 33:27 TSK

nit ki seedeeli ko ca nit ña, ne: «Maa bàkkaar, maa xëtt njub, te feyeesu ma ko sax!

Kuy làq say tooñ doo baaxle, ku koy nangu, tuub ko, am yërmandey Yàlla.