TSK

TSK · Numbers 6:15

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ak mburu yu mag yu amul lawiir, ak kàmp yu sew yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw, ak mburu yu tàppandaar yu amul lawiir, ñu wis diw ca kaw, te sungufu bele su mucc ayib ngay defare yooyu.

Bu ci nit ki jubloo ag njukkal gu muy delloo Aji Sax ji, day boole ci saraxu cant gi ay mburu yu ndaw yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw ak ay mburu yu tàppandaar yu amul lawiir, ñu wis diw ca kaw, ak ay mburu yu ñu lakke sunguf su mucc ayib, xiiwaale ko diw, not ko bu baax.

ak itam aw nag akam kuuy, muy saraxu cant ci biir jàmm, di lu ñuy rendi fi kanam Aji Sax ji. Nañu defaale saraxu pepp mu am diw, ndax tey jii Aji Sax ji dina leen feeñu.»

bu ngeen di defal Aji Sax ji saraxu sawara, muy saraxu rendi-dóomal, mbaa sarax su nit di wàccoo aw xas, mbaa saraxu yéene, mbaa seen saraxi màggal, ngir xeeñal xetug jàmm ñeel Aji Sax ji, te muy lu jóge ci jur gu gudd mbaa gu gàtt, defe leen ko nii:

ak biiñ bu muy joxewaale, ngir saraxu tuuru, di genn-wàllu xiin, muy ñetti liitar. Loolu saraxu sawara la, di xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

Joel 1:9 TSK

Saraxu pepp ak saraxu tuuru dagg na ca kër Aji Sax ji. Sarxalkat yi, boroom dénkaaney Aji Sax ji, ñu ngi ñaawlu.

Joel 2:14 TSK

Jombul mu dëpp, fomm, bàyyi gannaawam barke, ba ci saraxu pepp ak saraxu tuuru, ñeel seen Yàlla, Aji Sax ji.»

¶ Kon nag su ngeen di lekk, mbaa ngeen di naan, mbaa ngeen di def leneen, lépp lu ngeen di def, wutleen koo terale Yàlla.