TSK

TSK · Numbers 6:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Nanga ber dënn bi ñu def saraxu yékkati-jébbale, mook tànkub jooxe bi ñu def saraxu yékkati-jébbale, te ñu jooxee ko ci kuuyu colu gi, ñeel Aaróona aki doomam.

Sarxalkat bi day lakk nebbon bi ci kaw sarxalukaay bi, waaye dënn bi, Aaróona aki doomam yu góor ñoo ko moom.

Li ko waral mooy, man Aji Sax ji damaa jële ci seen saraxi cant ci biir jàmm, dënn bi ñuy def saraxu yékkati-jébbale, ak tànkub jooxe bi, jox ko Aaróona, sarxalkat bi mook doomam yu góor. Seen cér la ba fàww ci biir bànni Israyil.»

Tànkub jooxe bi ak dënnu saraxu yékkati-jébbale bi, mook nebbon bi ñuy def saraxu sawara, dees koy boole indi yékkati ko, def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji. Yeena moom yooyu, yaak say doom, muy seen cér bu ñu leen dogalal fàww, te di la Aji Sax ji santaane woon.»

Waaye na jëkka nangoo ci loxol ndaw si, peppum saraxu fiiraange bi, daldi yékkati saraxas pepp mi, jébbale ko fi kanam Aji Sax ji, doora indi sarax bi ci sarxalukaay bi.

Doo ma wacc njaniiw moos, sa wóllëre wa, doo ko won yàqutey bàmmeel.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, mooy berndeel xeet yépp fi kaw tund wii, bernde ju niin ak ngëneelu biiñ, yàpp wa duuf, yuq ja ne xéew, ak tànnéefu biiñ bu teey.

Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.

Ndaw bànneex akub taar ca ñoom! Pepp yafal xalelu góor, biiñ bu bees naatal yaramu janq.

Xare bu baax bi, xare naa ko, rawante bi, sottal naa ko, ngëm gi ma am, sàmm naa ko.