TSK

TSK · Numbers 6:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Barkeel a leen di ñeel ci biir dëkk, barkeel a leen di ñeel cib àll.

Mooy sàmm jéegoy wóllëreem, ku bon sànkoo biir lëndëm, nde doole mayewul ndam.

Ngalla musalal sa mbooloo, barkeelal sa ñoñ ñii, sàmm leen, boot ba fàww.

Yal na la Aji Sax ji barkeele fa Siyoŋ, moom mi sàkk asamaan ak suuf.

Mu ne: «Man Aji Sax ji, maa la woo cig njekk, jàpp la ci loxo, sàmm la, def la ngay kóllëre sama digg ak nit ñi; def la ngay leeru xeet yi,

Soo yékkatee kàddug cant goo waxe xol doŋŋ, ana nu nit ku xamul ku ko teewe naan: «Amiin,» te xamul li ngay wax?

Su boobaa jàmmu Yàlla, ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol, ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.

¶ Yàlla ci boppam, moom miy Boroom jàmm, yal na leen sellal, ba ngeen mat sëkk, te seen léppi xel, ak seen léppi xol, ak seen léppi yaram sàmmu, ba mucc sikk, ba kera bés bu sunu Sang Yeesu Almasi feeñee.

Jude 1:24 TSK

¶ Ki leen mana aar ci bépp jéll, ba taxawal leen fa muy teewejee darajaam, te fekk leen ñàkk sikk, seen mbég mat sëkk,