TSK

TSK · Numbers 6:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ma def la ngay cosaanal xeet wu yaa, barkeel la, màggal sa tur, ngay buntu barke;

Nit ka ne ko: «Tuddatuloo Yanqóoba, léegi Israyil nga tudd, ndaxte bëre nga ak nit, bëre ak Yàlla, ba génn ci ak jàmm.»

Yàlla Aji Man ji, mooy ni ma feeñoo woon Ibraayma, te ni laa feeñoo Isaaxa ak Yanqóoba it, waaye sama tur, Aji Sax ji, leeraluma leen ko woon.

Kàddug barkeel gii laa jot ndigalam, Yàllaa barkeel, duma ko tebbi.

Ana askan wu mel ni Israyil sa ñoñ ci kaw suuf, wenn askan wu Yàlla dikk, goreel leen ngir def leen ñoñam, ba turam siiw? Yaa leen defal ay jaloore, yaa defal sam réew ay kéemaan ci sa kanam ñoñ ñi nga goreele fa Misra aki askanam aki yàllaam.

Suuf si nangu na, yal na nu Yàlla, sunu Yàllay barkeel.

Délloosil képp ku ñu ma tudde, te sama màqaama tax ma sàkk ko, tabax ko, sottal ko.»

Rikk sama Yàlla, teewlul, déglul te xippi, ba gis sunu gent yi ak sa dëkk ba ñuy tudd sa tur. Du sunu njekk lanu lay dagaane moos, waaye sa yërmande ju yaa rekk a tax.