TSK

TSK · Numbers 7:89

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Tëgglul ñaari malaakay serub yu wurus te nga féetale leen ak ñaari cati kubeeru njotlaay ga.

Te bu Musaa duggaan ca xayma ba, taxaaru niir wa day wàcc, ne tekk ca bunt xayma ba, fekk Aji Sax jaa ngay wax ak Musaa.

¶ Aji Sax ji moo wax ak Musaa ca màndiŋu Sinayi ca biir xaymab ndaje ma, keroog benn fanu ñaareelu weer wu ñaareelu at, ma topp ca gàddaay ga bawoo Misra. Mu ne ko:

Gémmiñ ak gémmiñ laay waxeek moom wax ju leer nàññ ju ñu léebul, te jëmmu Aji Sax ji lay gis. Kon lu leen may fitu ŋàññ Musaa sama jaam bi?»

¶ Ci kaw loolu mu sàkk ca biir néeg bu sell baa sell ñaari malaakay serub yu ñu yette bantu oliw, jëmm ju ci nekk am taxawaayu fukki xasab.

Aji Sax jeey Buur. Yeen xeet yi, ragal-leen ko! Moo toogandook malaakay serub yi. Suufoo, soo yeboo, yëngu!

Yonent yooyu, xamalees na leen ne du seen njariñal bopp lañuy liggéeyal xibaar boobu, xanaa yeen. Ñi leen àgge xibaar bi tey ñoo di ñiy waare xibaaru jàmm bi ci dooley Noo gu Sell, gi ñu yebale asamaan, te muy mbir mu malaaka yi sax, noon siiwa nemmiku.