«Man mii nag, maa seppee Leween ñi ci bànni Israyil, maa leen weccoo mboolem taaw bu góor bu jëkka juddoo ci ndeyam, ci biir bànni Israyil. Kon nag Leween ñi, sama cér lañuy doon.
TSK
TSK · Numbers 8:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ne ko mu wax bànni Israyil ne leen: «Góor ak jigéen, képp ku ci dogu ba xas xasu doon ab nasireen, ngir sédd boppam Aji Sax ji,
Xeeb ngeen daal ber gi leen Yàllay Israyil ber ci mbooloom Israyil, jegeñal leen boppam, ngeen di liggéey liggéeyu màkkaanu Aji Sax ji, di taxaw fi kanam mbooloo mi, di leen jaamul Yàlla?
¶ Jant yooyu la Aji Sax ji ber giirug Lewi, ngir ñuy gàddu gaalu kóllëreg Aji Sax ji, di taxaw fi kanam Aji Sax ji, di ko liggéeyal, di taase barke ciw turam, te mooy seen péete ba tey jii.
¶ Ci man Póol miy jaamub Almasi Yeesu la bataaxal bii bawoo, man miy ndawam ci kaw woote bu ma tabb, sédd ma sasu xamle xibaaru jàmm bu Yàlla.
¶ Boobu sarxalkat bu mag lanu soxla; moo sell, mucc sikk, mucc sobe, moom lañu teqale ak bàkkaarkat yi, te moom lañu kaweel ba fa tiim asamaan.