TSK

TSK · Numbers 8:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ca xaaju guddi la Aji Sax ji fàdd mboolem taawi réewum Misra yu góor, dale ko ca taaw bu góor bu Firawna, ma toog ca jal ba, ba ca taaw yu góor yu nit ña ñu tëj kaso, boole ca lépp luy taaw bu góor ca jur ga.

nangeen sédde Aji Sax ji lépp lu jëkka juddu, rendil ko ko: lépp luy góor lu seen jur taawloo, Aji Sax jeey boroom.

¶ «Su nit jagleelee Aji Sax ji dëkkuwaayam, sellalal ko ko, na sarxalkat bi xayma dëkkuwaay bi. Su baaxee su bonee, lu mu ci dogal mooy wéy.

Ndax lépp luy taaw bu góor, sama cér la. Keroog ba ma fàddee lépp luy taaw bu góor ca réewum Misra, ca laa sellalal sama bopp lépp luy taaw ci Israyil, dale ci nit ba ci jur. Maa leen séddoo. Maay Aji Sax ji.»

Moo fàdd luy taaw ca seenum réew, muy lu jëkka soqeekoo seen digg doole.

Sama bési Noflaay itam maa leen ko jox, muy màndarga sama digganteek ñoom, ngir ñu xam ne man Aji Sax ji maa leen sellal.

Kon ki dëggaate Doomu Yàlla ji, teddadil deret ji ñu sellale kóllëre gi, te ñàkke teggin Noowug Yàlla gi nu indil aw yiw, kooku, mbugal ga mu yelloo, ñaata yoon lay gënatee metti, ngeen defe?

Moom la soob mu jure nu kàddug dëgg, ba nu taxawe ab jooxeb ndoortel meññeef, ci biiri bindeefam.