TSK

TSK · Numbers 9:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Diiru juróom ñaari fan ngeen di lekk mburu mu amul lawiir; te bés bu jëkk bi ci boppam nangeen jële seeni kër luy lawiir, ndaxte képp ku ci lekk mburu mu am lawiir, li ko dale bés bu jëkk bi, ba kera bésub juróom ñaareel ba, dees na ko dagge ci askanu Israyil.

Képp ku defar lenn lu ni mel, ngir di ko xeeñoo, dees koy dagge ci bànni Israyil.»

¶ «Te it képp ku bokk ci waa kër Israyil mbaa doxandéem yi ci seen biir, bu lekkee lenn luy deret, kooku lekk deret, man Aji Sax ji, dinaa ko noonoo te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil.

¶ «Ku dëkkoo soxnas baayam bu ndaw, baayam bu ndaw la torxal. Ñooy wéetoo seen añu ñaawtéef. Duñu am takkndeer ba keroog ñuy dee.

Bànni Israyil nag nangeen leen wax ne leen: Képp ku wax Yàllaam lu ñaaw, jaar fu bon, na wéetoo añam.

«Na bànni Israyil di màggal bésub Mucc ba, saa yu jotee.

¶ Nit ki tooñ cig teyeefam nag, muy njuddu-ji-réew, di doxandéem, kooku Aji Sax ji la ñàkke kersa. Nit kooku, dees koy dagge ci biiri bokkam:

Képp ku laal nit ku dee, ak néew bu mu mana doon, bu setluwul, màkkaanu Aji Sax ji la sobeel. Kooku dees koy dagge ci bànni Israyil. Gannaaw ndoxum setlu ma, wiseesu ko ko, sobewu lay wéye.

Dees na leen këpp seen yàqute, ngeen yenu seen bàkkaari kasaray tuur, ba xam ne man maay Boroom bi Aji Sax ji.»

ba noppi xàcci. Kon deesu leen waññi, ngir ñuy tuubati, nde ñoo daajaatal seen bopp Doomu Yàlla ji ci bant, teg ko toroxte ju ne fàŋŋ.

¶ Gannaaw bu nu xamee xéll liy dëgg ba noppi nag, su nu bàkkaaratee te di ko tey, su boobaa ab sarax bu far yooyu bàkkaar amatu ci.