Bu bëccëgee nag Aji Sax ji nekk ci seen kanam ci biir taxaaru niir, di leen jiite ca yoon wa, te bu guddee mu nekk ci biir taxaaru sawara, di leen leeral, ba ñu mana dem guddi ak bëccëg.
TSK
TSK · Numbers 9:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Exodus 13:21
TSK
Numbers 9:18
TSK
Ci kàddug Aji Sax ji la bànni Israyil daan faboo, ci kàddug Aji Sax ji lañu daan dale, te mboolem fan ya niir way dal, tiim màkkaan ma, ñoom it dañuy dal.
Nehemiah 9:12
TSK
Ci kaw loolu nga di leen jiitee bëccëg aw taxaaru niir, di leen jiitee guddi taxaaru sawara, di leen niital yoon wa ñuy jaare.
Psalms 78:14
TSK
Bëccëg mu jiitee leen aw niir, ak leeru sawara guddi gépp.
Isaiah 4:5
TSK
Su boobaa tundu Siyoŋ bépp, fépp fu ñuy dajee, Aji Sax ji sàkk fa niiru saxar bëccëg, guddi mu def tàkk-tàkk bu ne ràññ; leeru Aji Sax ji di kiiraay, tiim lépp,
Loolu di firi ne ci Almasi la Yàlla jubale waa àddina, ak jëmmu boppam, ba toppu leen seeni tooñ, te moo nu dénk kàddug juboo gi.