Déglu ma fii, ma digal la, tey ñaan Yàlla ànd ceek yaw. Danga fee toogal mbooloo mi ci kanam Yàlla, di diis Yàlla jotey nit ñi,
TSK
TSK · Numbers 9:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Fu ab néew nekk du fa dem, bu doon ndeyam mbaa baayam sax, du ko taxa sobeel boppam.
«Santal bànni Israyil ñu génne dal bi képp ku ànd ak jàngoroy der juy law, mbaa jàngoroy xelli, ak képp ku sobeb néew bu mu laal, topp.
Ña ko fekk muy taxan, yóbbu ko ba ca Musaa ak Aaróona, ak mbooloo ma mépp.
¶ «Lii la yoon wi tëral: Bu nit deeyee ci biir xayma, képp ku dugg ci biir xayma bi, ak képp ku mu fekk ci xayma bi, day sobewu diiru juróom ñaari fan,
Bu loolu wéyee, na ku set jël caru isob, capp ko ca ndox ma, wis-wisal ko ca kaw xayma ba nit deeye, wis ko ca kaw ndab yépp, ak ca kaw nit ña fa nekkoon. Na ko wis itam ci kaw nit ku laal yaxi ku dee, mbaa mu laal ku ñu bóome saamar, mbaa mu laal ku Yàlla moomal boppam, mbaa mu laal bàmmeel.
¶ Ci kaw loolu Musaa jébbal Aji Sax ji, àtteb jigéen ña.